Gëm, tiis na


Kuy jòxé kuné nangul ñu delolà
Ndeem japo ci joko jama lay xibar
So nee manlà wala moomlà nafek amnà ku def.
So séeto jiis sa bopp muy dëgë nala woor né sap xel nga seen.
So nee nasaràn bii ni wala nëlee lakoy defee ba tax ma topando,
War nga seetat sa bopp ndaxam do baima buñu tak bumm jitàl.
Cambaràl li nga doon ndax yawla wala kilay yégalaki wàcee
Dila yobu aki delosi, di la tamtamal ngay ree naan mafi mënn
Di jooy nann ma dègal kii fi mën ba tax maak samp sap jë ne mel.

Naxo ki kenn mëntë nax jëndékop nit buy dundà té reer.
Amnà ñu Yàlla mày Ñuul te wàloo dank bu dunn, jëfewuñuko.
Ken duné ñu bax dembë ak tay jaru ñufi ba tax li xel di niit aki wax
Suko lamìnn tudé ñu ràyko; ñuy ñann borombi yok suturë.
Samp sap ndënd di xaar ñu dànla te nanla waw goor xañc sap der là
Do mësë jogé cip surga, xacc sàx du la nawlo bày doon sa morom.

Barkep gëngi mindef sant Yàlla mi xamal ndòx ak bann ne ken gënulen.

ABT 

Opmerkings

Gewilde plasings van hierdie blog

Wa Kàwga

Mbàax moy wote wàlu

Ànamakakñanindéwënël?